Aller au contenu

Almasi bi

Jóge Wikipedia.
La version imprimable n’est plus prise en charge et peut comporter des erreurs de génération. Veuillez mettre à jour les signets de votre navigateur et utiliser à la place la fonction d’impression par défaut de celui-ci.

Ci làkku ibrë (מָשִׁיחַ), la baat bi jóge. Almasi bi mooy ni ñu koy waxe ci Lislaam (Al-Masiḥe, المسيح). Ci angale mooy the Messiah; Ci faranse mooy le Messie

Almasi bi mooy tekki 'Ku Yàlla fal ngir liggéeyal ko'. Yonent Yàlla yi jiitu woon jamano Kirist waxoon nañu ci lu jëm ci musalkat bi Yàlla dige woon nara ñëw. Tur wi dafa ëmb wax yooyu yépp. Yawut ya, bu ñu masaana fal kenn, dañu daan sotti diwlin ci boppam, muy yonent, muy sëriñ mbaa buur. Krist, Almasi bi nag, mooy Ki Yàlla sol Xelam, ngir wone ne mooy Yonent, Saraxalekat ak Buur bi. Moo di yonent, bi nuy jottali xebaaru jàmm fa kanam Yàlla. Moo di Saraxalekat, bi nu ubbil bunt fa Yàlla. Moo di Buur, bi yilif ñépp ak yépp.

Baat bii mu ngi jóge ci làkku araab, sukkandiku ci làkku ibrë, te muy tekki ‘Kirist' ci làkku gereg. Ci Injiil bi ci gereg Almasi bi dafay am ñaari yoon rekk (Yow 1:41; 4:25). Ci firi Wolof, bu Injiil bi ci gereg amee Kirist te mu bëgga wax ci ndombam dañu koy firi Almasi. Bu Injiil bi ci gereg amee Kirist te mu bëgga wax ci turam dañu koy firi Kirist. Seetal itam Kirist.